دِفْڭَيْ قَصِيدَ چِ أَيْ يَارَمْ چِ تِجَّانِي
Def ngay qasiida ci ay yaaram ci Tijjaani
{# Lien visible vers le PDF de l'œuvre (#120, #644) : répond aux recherches « … pdf ». nofollow : l'export compte chaque téléchargement et a son propre quota ; les robots n'ont pas à le parcourir pour chaque œuvre, la page suffit à dire que le PDF existe. #}دِفْڭَيْ قَصِيدَ چِ أَيْ يَارَمْ چِ تِجَّانِي
دِفَلْنُهْ وَيْ چِ وُلُفْ نُنْ ڭَايِ سُودَانِ
def ngay qasiida ci ay yaaram ci Tijjaani — defal nu woy ci wolof, nun gaayi Suudaani
يَارَمْيِ جُۛودِ نڭَلَمْ وُلُفْيِ جُۛودِ پَرَمْ
أَسِلْ نڭَلَمْ أَكْ پَرَمْ نڭِرْ حَقِّ چَاجَانِ
yaaram yi ñoo di ngalam, wolof yi ñoo di përëm — asil ngalam ak përëm ngir haqqi Njaajaani
اَلْحَمْدُ لِلَّهِ وَيْوِي مَا كُوَيْ تِلِتَخْ
دَمَيْ دِڭَّلْ ڭَايِ سُوبُ يُونُ تِجَّانِي
Alhamdu lillaahi, woy wii maa ko woy, te li tax — damay digal gaayi sóobu yoonu Tijjaani
تِجَانْ بِ بُلْ خُتِّ وُرْمَيْ دِينِ بُلْ تِلِمَلْ
بُبُّمْ شَرِيعَةُ لِي خِوُلْ چِ تِجَّانِي
Tijaan bi, bul xotti wormay diine, bul tilimal — mbubbum shariiʿatu, lii xewul ci Tijjaani
جَپَّلْ تِجُلِّ تِوُتْ خَمْخَمْ بَأَمْ چَ لُدُيْ
ڭَ جَامُ يَلَّ بُبَاخْ تَيْ سَنْتَ تَيْ نجَۛانِ
jàppal te julli te wut xam-xam ba am ca lu doy — nga jaamu Yàlla bu baax, tey santa, tey ñaani
جُخَلْ حَقِيقَةُ حَقَّمْ جُخْ شَرِيعَةُ شَرْ
طَمْ لُولُ مُويْ لَنُ خَمْ نُنْ ڭَايِ تِجَّانِي
joxal haqiiqatu haqqam, jox shariiʿatu shar- — -ṭam, loolu mooy la nu xam, nun gaayi Tijjaani
تِجَانْ بِ بُلْ نَخِ بُلْ وُرْ بُلْ نَيِتْ چِ أَلَلْ
جُخِيلْ جُۛجُخْلَ بَمُيْ بَاوَانْ دِ سَاوَانِ
Tijaan bi, bul naxe, bul wor, bul nayit ci alal — joxeel, ñu jox la ba muy baawaan di saawaani
جَفَلْ تِبُلْ دَمُ بُلْ خِيبَاتْ بُلْ عَيِبَلْ
كُسِلَّلُلْ نَڭَ سِلَّلْ يَوْ چِ تِجَّانِي
jëfal te bul damu, bul xeebaate, bul ʿayibal — ku sellalul na nga sellal, yaw ci Tijjaani
بُلْ سَاڭَ بُلْ خَسْتِ بُلْ جَوْ بُلْ دِ مِرْ تِجُتُلْ
تِ سُو مِرِي بُلْ خُلُو تِبُلْ دِ رِيتَانِ
bul saaga, bul xaste, bul jëw, bul di mer te jotul — te soo meree bul xuloo, te bul di reetaani
بُلْ أَمْ خَرِيتْ بُ دِ أَبْ يِيفَرْ تِ بُلْ بَجِتَمْ
بِنُّبْ جُلِّتْ لُ كُ مُيْ كُنْ دِفْ ڭَ چَاجَانِ
bul am xarit bu di ab yéefar, te bul bañ itam — bennub jullit, lu ko moy, kon def nga Njaajaani
بُلْ رَيْلُ بُلْ نَيْ تِبُلْ جَۛاوْ جِكُّ بُلْ وَخُ فِنْ
تِبُلْ حَجَۛانِ كُ أَمْ تِبُلْ دِ چِيتَانِ
bul réylu, bul nay, te bul ñaaw jikko, bul waxu fen — te bul añaane ku am, te bul di céetaani
بُلْ تُقِّ بُلْ يُقِّ كُيْ وُتْ يَلَّ سُو سَوَرُلْ
سَكْ حَمْكُ وُورُلْ تِدُو رُيْ شِيخُ التِّجَّانِي
bul toqqi, bul yoqqi, kuy wut Yàlla, soo sawarul — sak am ko, wóorul, te doo roy Seexu Tijjaani
بُلْ تَيِّ بُلْ بَيِّ بُو بَيِيْ كُ كُيْ خَلَ يَكْ
خَمْ ڭَ تِيَابَ دُ دُيْ چِ يُونُ تِجَّانِي
bul tàyyi, bul bàyyi, boo bàyyee ku koy xala yak — xam nga tiyaaba du doy ci yoonu Tijjaani
نچِمِيلْ جَتَايُ ذِكَرْ تِبُلْ نِلَوْ بَ فَجَرْ
نِيخُكْ نِلَوْ دُ كُ جَرْ چِ يُونُ تِجَّانِي
njëmeel jataayu zikar, te bul nelaw ba fajar — neexug nelaw du ko jar ci yoonu Tijjaani
فُنْكَلْ وَظِيفَهْ تِفُنْكَ وِرْدَ وَخْ جَ نَسِتْ
كَتِيوْلُ مَانَايَ تِيوْلُ شِيخُ التِّجَّانِي
fonkal wasiifa te fonka wirda, wax ja na set — ka teewlu maanaa ya, teewlu Seexu Tijjaani
بُ بَاتْيَ رَوبِ بُأَيْ شَدَّيْ وُيَفْ تِ بُ أَيْ
بِجَّانْ دِ دِسْ لِي لَ وَخْ مُومْ شِيخُ التِّجَّانِي
bu baat ya rawbi, bu ay shadda woyof, te bu ay — bijjaan di des, lii la wax moom Seexu Tijjaani
صَلَاةُ الْفَاتِحِ كِنْ وِرْدُلْ لُ مِلْنَكَ مُومْ
مَڭَّلْكُ لُو مَسَ مَنْ تِبُلْكُ چَاخَانِ
Saalaatu Faatihi, ken wirdul lu mel na ka moom — màggal ko loo mas a man, te bul ko caaxaani
بُلْ خَسْ وَلِيُّ بُ كُيْ ڭَارَلْ بُ كُيْ دُيَدَلْ
نْدَخْ وَايِ يَلَّ لَ لِي مُو سَنِّ أَوْ سَانِ
bul xas waliyyu, bu koy gaaral, bu koy doyadal — ndax waayi Yàlla la, lii moo sànni aw saani
بَڭَّلْ ڭَمَلْ مَڭَّلَلْ سُبَّلْ وِڭَّلْ تِرَلَلْ
پُولِيمْ وَلِيُّ يِ لِي يَلَّا كُ سَنْتَانِ
bëggal, gëmal, màggalal, soppal, wegal, teralal — boolem waliyyu yi, lii Yàllaa ko santaani
بُورْ يَلَّ نِينَ كُ لُورْ وَايَمْ نَ خَمْ چِ لُوِرْ
نَ دَيْ خَرِيكْ مُومْ تِ دَيْ دِي تَبِّ نِيرَانِ
Buur Yàlla nee na ku lor waayam, na xam ci lu wér — na day xareek moom, te day dee tàbbi niiraani
پُو لِيمْ وَلِيُّ يِ نَوْ نَا لِينْ چِ يَلَّ بُ وِرْ
ڭَنَاوْ بَ جَايَنْتِ نَا أَكْ شِيخُ التِّجَّانِي
boolem waliyyu yi, naw naa leen ci Yàlla bu wér — ganaaw ba jaayante naa ak Seexu Tijjaani
بُو جِبَّلُو نَڭَ سِيتْ چِ ڭَاجَۛ وَاجَ لَ دُيْ
ڭَ سَمِّ شَرْطَمْ تِ أَنْدَكْ مُومْ چِ تِجَّانِي
boo jébbaloo naga, seet ci gaa ña waa ja la doy — nga sàmmi sharṭam te àndak moom ci Tijjaani
يِيوَلْ سَ بِرْ چِ بِرَمْ أَكْ جَۛتِّ بُومْ يُ دَڭَرْ
سُبَّ كْ جَفَ كْ جُخِ لِي مُو ڭَنْ چِ تِجَّانِي
yeewal sa mbir ci mbiram ak ñetti buum yu dëgër — sopp ak jëf ak joxe, lii moo gën ci Tijjaani
بُلْ نِكْ چِ سَكْ جُخِ كُيْ ڭِنِيكَ يِنِّيسِ ڎُو
خَمَلْ نِ نُنْ دُنُ لَاچْ نُنْ ڭَايِ تِجَّانِي
bul nég ci sag joxe kuy génne ka yónneesi ndaw — xamal ne nun dunu laaj, nun gaayi Tijjaani
سُيِينِ سِلِّي بُسُوبِي يَلَّ دِسْنَكُ مَنْ
سَكَمْ لِڭَيْ ڭَ بُبَاخْ تِرُيْ چِ تِجَّانِي
su yéene sellee, bu sóobee Yàlla, dees na ko man — sa kem li ngay nga bu baax, te roy ci Tijjaani
نَڭَيْ يَرَمْ ڭُنِ تَيْ وُرْمَالُ مَكْ تِسَوَرْ
ندَخْ لُولُ مُويْ يُونُ ڭَايِ شِيخُ التِّجَّانِي
nangay yërëm gone, tey wormaalu mag, te sawar — ndax loolu mooy yoonu gaayi Seexu Tijjaani
نَتَّلْ چِ أَنْدَارِ پَسْ پَسْ جَفْ چُ يِوْ مُدِبُرْ
سُو لِبْلِوُلْ لُنجُۛلَيْ فَيْ كُنْ چِ تِجَّانِي
nattal ci andaari pas-pas, jëf ju yiw mu di bor — soo leblewul, lu ñu lay fey kon ci Tijjaani
مُنجَۛلْ مَرْكْ خِيفْ تِمُنجْۛ أَوْ رَفْلِ سُو كُدِفُلْ
بُلْ سِينْتُ بَرْكِيكْ ڭَرَمْ چِ يُونُ تِجَّانِي
muñal mar ak xiif, te muñ aw rafle, soo ko deful — bul séentu barkeek ngërëm ci yoonu Tijjaani
سُنَّكْ مَرَكْ خِيفْ تِسَكُّ يَلَّ سُوكُ نُتُلْ
چِ يُونْوِ كُنْ نَكَ كُيْ نُتِي چِ تِجَّانِي
sonn ak mar ak xiif te sàkku Yàlla, soo ko notul — ci yoon wi, kon naka kuy notee ci Tijjaani
فَرْلُلْ چِ سَيْ نجَۛارِ وَيْجُرْ سَكُّ سِينِ ڭَرَمْ
تِمُيْتُ سِينْ مِرْ تِيَاكَارْ يِوْ چِ سِينْ نجَۛانِ
farlul ci say ñaari wayjur, sàkku seeni ngërëm — te moytu seen mer, te yaakaar yiw ci seen ñaani
بُلِينْ نِهْ مبَا سَّا بُلِينْ ڭَدِّتْ سَوَخْ نَدِ نُويْ
تِنڭَيْ طُرُخْلُ تِ دِفْ لِيَلَّ سَنْتَانِ
bu leen ne mbaa saa, bu leen gëddat, sa wax na di nooy — te ngay toroxlu te def li Yàlla santaani
سُو مَڭَّلُلْ نجَۛلَ جُرْ بُدُومْ جُ بُنْ دِلَفَيْ
سَبْ خُلْ دِ ڭَنجْۛ ڭَنجِۛ نڭَيْ نجَۛخْتُوكَ نجِۛيتَانِ
soo màggalul ña la jur, bu doom ju bon di la fey — sab xol di ngañ-ngañi ngay ñaxtooka ñeetaani
سُو دِي تِرَلْ نجَۛلَ جُرْ كُنْ سُو تَلِي دَ ڭَجِسْ
سَدُومْ جُبَاخْ دِلَ فَيْ سَبْ خُلْ دِ كُنْتَانِ
soo dee teral ña la jur, kon soo talee danga gis — sa doom ju baax di la fey, sab xol di kontaani
دِيلْ مُسْلُ تَيْ مُسْلِ فُو جِسْ نِتْكُ يِوْ كُ أَمُلْ
جُخَلْ دَرَمْ مُيْ ڭَرَمْ تَيْ سَنْتَ كَيْ نجَۛانِ
deel muslu tey musle, foo gis nit ku yiw ku amul — joxal dërëm, muy gërëm, tey santa kay ñaani
يُنِّنْ بِ نِينَ كُنَيْ دَيْ دَنْدَ أَجَنَّ أَكْ
بِنْدِيفْ يَ أَكْ يَلَّ نجُۛوخُ كَمْبِ نِيرَانِ
Yonent bi nee na ku nay day dànda ajjana ak — mbindeef ya ak Yàlla, ñooxu kàmbi niiraani
تِنِينَ أَبْ تَبْ سُرِينَاكْ نَارِ تِكْ چَ جَڭِيكْ
بُورْ يَلَّ أَكْ نِتْ نجِۛ أَكْ جَنَّاتُ رِضْوَانِ
te nee na ab tab sorii naak naari, teg ca jegeek — Buur Yàlla ak nit ñi ak jannaatu Riḍwaani
أَمْ فُلَّ مُو دِ لَوَرْ ندَخْ مُومْ لَنجُۛيْ يُرِ كَرْ
أَكَبْ دِڭَّلْ وَايِ بُلْ وِخْ خَتْ نِبْ كَانِ
am fulla moo di la war, ndax moom lañuy yore kër — akab digal, waaye bul wex xat ni ab kaani
بُلْ فَنْقَ يَتْ سَجَبَرْ مُيْ دُخْ دِ تُڭُّمْ خِوَرْ
كُنْ يَا دِفُلْ لَلَوَرْ چِ يُونُ تِجَّانِي
bul fànqa yat sa jabar, muy dox di toggum xewar — kon yaa deful la la war ci yoonu Tijjaani
جَبَرْ بُدِي بَرِ بُو بَڭِّي مُدَانُ وَخَلْ
تِجَفْ چِ مُومْ لُرَفِتْ كُنْ دَالْ ڭَ كُيْ دَانِ
jabar bu dee bëre, boo bëggee mu daanu, waxal — te jëf ci moom lu rafet, kon daal nga koy daani
مُنجَۛلْكُ مُونجَۛلْكُ فِلَّلْ يَيْ تِ جُخْكُ مُيَيْ
ندَخُبْ خُلَمْ أَكْ سَخُلْ دِڭُّو چِ وَخْتَانِ
muñël ko, muuñël ko, fellal yëy te jox ko mu yëy — ndaxub xolam ak sa xol déggoo ci waxtaani
وَتُّلْ مَ ڎَوْ سُرَفِتْ بُدِي تَخَوْ فِسَوِتْ
جُڭَّلْ چِ كَوْ نِ بَرِتْ دَوْ مُيْتُ شَيْطَانِ
wattul ma ndaw su rafet, bu dee taxaw fi sa wet — jógal ci kaw ne baret, daw, moytu Saytaane
شَيْطَانِ نِي مُو دِ أَكْ فِتَّمْ تِنِي دُچَ مُيْ
شَيْطَانِ دَانَكَ دُوتُلْ سَجِّ دَيْ دَانِ
Saytaane nee moo di ag fittam, te nee du ca moy — Saytaane daan na ka, dootul sajji, day daani
وُدَّلْ جَبَرْ تِسَخَلْ چَلْ فَيْ سَبُرْ بَمُمَتْ
ڭَدِفْ هَدِيَّهْ چِ يُونُ شِيخُ التِّجَّانِي
woddal jabar, te saxal njël, fey sa bor ba mu mat — nga def hadiyya ci yoonu Seexu Tijjaani
يَا شَيْخَنَا أَحْمَدَ التِّجَّانِي سَيِّدَنَا
سَلِيرْ ڭَ جُلِّ نَ فُو خُولْ مُو فَ بَاوَانِ
yaa Shayxanaa Ahmadat Tijjaani sayyidanaa — sa leer ga jolli na, foo xool mu fa baawaani
يَا أَمْ جَلُورِ يُرَيْ يَا أَمْ ڭِنِيلَ كِ مَيْ
يَارَمْ بِ يَا جَرَ وَيْ يَوْ شِيخُ التِّجَّانِي
yaa am jaloore yu réy, yaa am ngëneel aki may — Yaaram bi, yaa jar a woy, yaw Seexu Tijjaani
شَرِيفْ بِ يَا مَتَ رُيْ سَوِرْدَ وِي مَتَ نْغُيْ
سَڎَنْلِهْ نِيخْنَ تِدُيْ سَكُكْ دُ خَارَانِ
Shariif bi, yaa mat a roy, sa wirda wii mat a ngoy — sa ndën li neex na te doy, sa kuk du xaaraani
يَوْ ڭُيْ ڭُرَيْ ڭِيْ دِ فَرْلَاخَكْ چَرِي ڭَ دِفَرْ
رُنْقُونجُۛ كُيْ جُويُ مَرْ يَوْ شِيخُ التِّجَّانِي
yaw guy gu rëy giy di far laax ak ceree ga defar — rongooñu kuy jooyu mar, yaw Seexu Tijjaani
يَلَّ لَدِفْ ڭَدِ سَنْڭُبْ لَوْلِيَاءُ تِلِي
يُنِّنْبَ مُو لَكُ وَخْ يَوْ شِيخُ التِّجَّانِي
Yàlla la def nga di sangub lawliyaa u, te lii — Yonent ba moo la ko wax, yaw Seexu Tijjaani
يُنِّنْبَ تَلَّلْنَ بَارَامُبْ دِڭَكْ بَچَ سَسْ
دِ وَخْ چِ سَكْ رُو أَكُكْ رُوحَمْ لُكِيمَانِ
Yonent ba tàllal na baaraamu diggëk ba ca sës — di wax ci sag ruu akug ruuham lu kéemaani
سَرُوڭِ مُويْ تَبَّ أَيْ خِيوَلْ يُيَاتُ يُرَيْ
أَكُكْ وِلَايَا كِ مَيْ يَوْ شِيخُ التِّجَّانِي
sa ruu gi mooy tëbba ay xéewal yu yaatu yu réy — akuk wilaayaa ki may, yaw Seexu Tijjaani
سَرُوڭِ مُويْ تَبَّ نجِۛي وَرْسَكْ يُيَاتُ يَ نجِۛي
خَمْ خَمْ يُسِلَّ يَ أَسْكَيْ شِيخُ التِّجَّانِي
sa ruu gi mooy tëbba ñii wërsëg yu yaatu, ña ñee — xam-xam yu sella ya, eskey Seexu Tijjaani
تِسَخْ بُفِكُّونْ دُيَوْ كُنُبْ نَوِتْ دُفِتَوْ
تَ أَيْ جَرِنجْۛ دُفِ نجَۛوْ يَوْ شِيخُ التِّجَّانِي
te sax bu fekkoon du yaw, kon ub nawet du fi taw — ta ay jariñ du fi ñëw, yaw Seexu Tijjaani
يُنِّنْبَ نِينَلَ وُرْلُلْ نَالَ لِي كُلَ ڭَمْ
تَ أَمْ چِ پَسْ پَسْ بُدِيهِي فِكِّ رِضْوَانِ
Yonent ba nee na la wóorlul naa la lii, ku la gëm — ta am ci pas-pas, bu deeyee fekki Riḍwaani
سَوِرْدَ وِيْ كُكُ يُرْ تِ بَيِّوُوكُ بَدِي
دُو جِسْ چِ سَبْ قَبْرُ لُيْ رَڭْلُوكَ خِيخَانِ
sa wirda wii, ku ko yor te bàyyiwoo ko ba dee — doo gis ci sab qabru luy raglooka xiixaani
أَبْ نِنْ چِ نُنْ لُدِ قَيْمَامْ مُودِ أَلْفُ وَلِيّ
چِ ڭَايَ أَمْيَ كَمَالْ مِنْ غَيْرِ التِّجَّانِي
ab nen ci nun lu di xaymaam moo di alfu walii — ci gaa ya am ya kamaal, min ghayri Tijjaani
أَبْ نِنْ بُدِي وِچِّ جُنِّيْ لَوْلِيَا يُ كَمَالْ
مُو كُنْ نُنِيْ خَمِ قَيْمَيْ چُوچِ تِجَّانِي
ab nen bu dee wecci junniy lawliyaa yu kamaal — moo kon nu ñuy xame xaymay cuuji Tijjaani
مُو تَخْ بُسَا تَخَوِي بَسِينْ جَلُورِيَ فِينجْۛ
نجُۛيْ سَامَدَايْ أَيْ يُنِّنْ نجُۛومْ ڭَايِ تِجَّانِي
moo tax bu Saa taxawee ba seen jaloore ya feeñ — ñuy saamandaay ay yonent, ñoom gaayi Tijjaani
نجُۛيْ لَاچْ دِلَاچَتِ نَىٰ أَيْ لَنْبِيَا لَنجُۛ أَمْ
أَيْ مُرْسَلِينَ نُنَالِينْ نُو دِ تِجَّانِي
ñuy laaj di laajate naa ay lanbiyaa lañu am — ay mursaliina, nu naa leen noo di Tijjaani
لَاقْطَابْ يَ سِخْ سِينِ بَارَامْ رِچُّ ڭِرْ دِ نُنجِۛي
تِنَانْ بُدُونْ تَيْ نُسُوبُ يُونُ تِجَّانِي
laqtaab ya sex seeni baaraam, réccu, ngir di nu ñee — te naan bu doon tey, nu sóobu yoonu Tijjaani
بِنَّتْ چِ نُنْ يِنِّ فَنْ سُو لِينْ جِسِي تِنجُۛ سِي
ـدِ جِسْ ڭَ كُنْ رَوْ ڭَ دُو طُو جَارِ نِيرَانِ
bennat ci nun, yenni fan, soo leen gisee te ñu see- — -de gis ga, kon raw nga, doo ṭoo jaari niiraani
يِينْ ڭَايِ شِيخْ يِهْ خَنَا لِي دُيْنَ بِكْ تِ خَنَا
لِي دُيْنَ يَاكَارِ سُوبُ يُونُ تِجَّانِي
yeen gaayi Seex yi, xanaa lii doy na bég, te xanaa — lii doy na yaakaari sóobu yoonu Tijjaani
فُنڭِينْ فُجِسْ وَاجُ أَمْ پَسْ پَسْ چَ ڭِرْ مَمُ أَوْ
نَنڭِينْ دَڭَرْلُ تِ أَمْ پَسْ پَسْ چِ تِجَّانِي
fu ngeen fu gis waa ju am pas-pas ca ngér ma mu aw — nangeen dëgërlu te am pas-pas ci Tijjaani
جُورَكْ خَرِىٰ تَخْ ندِ أَمْنَا أَيْ سُكُمْ تِدَمَا
خِيبُونْ لِمُكْ خَنْدَ دُورْ چِ شِيخُ التِّجَّانِي
Joorak Xarii tax nde am naa ay sukum te damaa — xeeboon lemuk xandadoor ci Seexu Tijjaani
نجُۛو نِمُّ أَوْ خَنْدَ دُورْ نِمِّينُ وَاجُ خَمُلْ
مَچُكْ دِلِينْ وَنُ يُونْ چِ شِيخُ التِّجَّانِي
ñoo nemmu aw xandadoor, nemmeenu waa ju xamul — ma jóg di leen wonu yoon ci Seexu Tijjaani